Stivation · Wolof · 2012
tuut tànk ci yooni tàggatum xel ak xam-xam ci pencoo
Note éditoriale — Le Couloir du Savoir
Ce texte est la traduction en wolof du cadre pédagogique de la Stivation, réalisée par M. Mbacké Thioune (Seriñ Mbàkke CUUN). Publiée en 2012, cette traduction — intitulée Jëxiis — constitue un acte fondateur : elle ancre la Stivation dans la langue et la culture éducative sénégalaise. Le Couloir du Savoir la publie ici dans son intégralité, avec la gratitude de son auteur.
Auteur du texte
Seex Axmadu Bàmba MBAY
Wéy tàggat njàngale mi
Inspecteur de l'Éducation et de la Formation
Traducteur
M. Mbacké Thioune
Seriñ Mbàkke CUUN
Traduction depuis le français · 2012
Ca attum 1970 ak lu ko wër, ay kàngaam yuy yëngu ci wallu xel ak nekkin bokk ci ngiiru Piaget ca Genève, ñoom Doise, Mugny, Perret-Clermont, dañoo sumb ak coppite gu mattale ci wàllu njàngale ak njàngin.
Sumb boobu nak da nu koo wéer ci gis-gisu tàggatum xel ak xam-xam ci pencoo.
Kàngaam yooyu di askanoo ci Piaget wonenan ab feem ci njangalin buy sukkandiku ci tabax ak pencoo xam-xam.
Feem wi wone na ne xaleel buy weccoo xalaat ak ay moroomam di na ful ay pexeem, di na nàmm xelam.
Li ko sabab mooy ne xaleel suy diisoo ak ay moroomam di na jiixi-jaaxa ci ay xalaatu boppam, di na jiixi-jaaxa it ci digganteem ak ay moroomam.
Jiixi-jaaxa googu di indi jàmarloo ak disoo.
Lii lepp di wund ci gàttal ne jëf-lante yi xale yiy sexx di na sabab yokkute ci seen njàng.
« Tënkal sa moroom kàddu gu am maanaa, tontu laaju sa moroom, yey sa moroom ci cëslaay gu wér, nangu it ñu yéy la ci dëgg doonte di nga jiixi-jaaxa ndax soppite gu bette ci la nga foogoon dina mootalli xam-xam ak yar jiko. »
Stivation « Jëxiis » · Seex Axmadu Bàmba MBAY · 2012
Feem wii di Stivation « Jëxiis », tuut tànk ci yooni tàggatum xel ak xam-xam ci pencoo mi ngi sàmp ay reenam ci gisin wi nu leeral ci kaddu yi jiitu.
Amul sikk ne di na jarin it taggatum mag ni ak way njàng liggeey bu mu mën a nekk.
Ay ndongo-wéy saytu njàng mi ca FASTEF (Daara ju mag ji Cheikh Anta DIOP ca Dakar) def na nu ci ab gëstu bu xóot, njurka ya am na solo lool.
Ñetti joxoñ yu Jëxiis — Les trois piliers
Feem wii di Stivation « Jëxiis » dafay sukkandiku ci ñetti joxoñ :
Jëf-lante
Interaction — l'échange entre apprenants
Xiirtal
Motivation — l'élan vers l'apprentissage
Soññ
Stimulation — l'éveil intellectuel collectif
Feem wii di Stivation « Jëxiis » dees na ko wax su nekkee ne jëf-lante yi jéggi ëttu njàng mi da nuy xirtal ak a soññ wéy njàng yi, amaale jeexit ci solos seen i mën-mën (kenn-kenn ak mboleem seen).
Ci tënk, Stivation « Jëxiis » di na tax njurka yi cosaanoo ci tolluwaayu tàggat yi ci wàllu njàng, tabaxinu ay xarala ak fullaal gëm sa liggeey gënna dëggër, gënna yaatu.
Jiixi-jaaxa googu da fay soññu mbooloo mi te di xirtal pas-pasam, kattanam, nisëram ngir jëm ca kanam.
Jiixi-jaaxa di na it tax ba mbooloo mi di raas xam-xam fu mu mën a tollu. Su ko defee njàngu wéy tàgaatu yi di na mën a ñoŋ.
Ci tënk, sikkuwul ne xalaat, weccoo xalaat ak wesaare xam-xam bi nekk ci lëllu tàggat yi di na gën a yokku seen xarañ.
Ci tënkug jeexal — En conclusion
Stivation « Jëxiis », mënees na koo jàppee yoon wu yees ci wàllu njàng woo xamne da fay sukkandiku ci jëflante ak pencoo xam-xam ci ay wéy tàggatu yu mu mën a doon.
Na nu jàpp ne Stivation « Jëxiis » ab tërëlinu tàggat la bu nu mën a jëfe ci lëlu ndongo-wéy saytu njàng mi wala ci bépp tàggat ay mag bu mu mën a doon.
Gëstu yi nu ci mën a def ak jéemëntu yi nu ci mën a def di na am solo ndax di na tax jangalekat yi faaydaal tabax ak pencoo xam-xam ci ay ndongo ba gën koo jëmal ci seen i sumb liggéey.
Yoon wu bees la buy wootal jangalekat yi ñu boole seen bopp ak seeni pexe ngir mën a weccee xalaat ak i feem ba seen liggeey gën a sell.
Mu mel ne di na doon njariñ ci Nguur gi ak askan wi ndax jangalekat yi bari nañ jafe-jafe yu ñuy jànkoonteel rax ci dolli soppite yi dafay gën di bari.
À propos des auteurs
Seex Axmadu Bàmba MBAY
Wéy tàggat njàngale mi · Inspecteur de l'Éducation et de la Formation
Auteur du cadre théorique de la Stivation. Fondateur du concept de Jëxiis. Inspecteur de l'éducation nationale, praticien et chercheur engagé dans la réforme pédagogique en Afrique subsaharienne.
M. Mbacké Thioune (Seriñ Mbàkke CUUN)
Traducteur · 2012
Traducteur de la Stivation en wolof. Son travail de 2012 a permis d'ancrer ce cadre pédagogique dans la langue nationale sénégalaise, le rendant accessible à tous les praticiens de l'éducation.